Skip to content

Latest commit

 

History

History
81 lines (52 loc) · 4.68 KB

CONTRIBUTING.md

File metadata and controls

81 lines (52 loc) · 4.68 KB

English | Français

Code for Senegal ~ Gindikukaayu njañse yi

💕 Li nuy njëkke mooy sant la ci yitte ci nga am ñeel naal bii tek ci jël sa waxtu ngir tàbbi ci!

Naal bii, ay way defal-yàlla, yu mel ni yaw, yu wuute ay waxtuy barab, cosaan ak tolluwaayu ci man-man ñoo ko def. Kon, ngir mu wóor ni noo tolloo dégg-dégg, doon na baax lool nu topp nun ñépp yenn tëraliin 💕

Jot xibaar | Naka laa man a ëndee njañse? | Jëfiin yi gën | Lu aju ci Code for Senegal | Tàbbal koom | Doxaliin

Jot xibaar

Da ngaa am ab laaj bu ndaw? Man nga noo yónnee ab e-mail ci contact@codeforsenegal.org

Naka laa man a ëndee njañse?

Wane ab bug

🐛 Da ngaa njortu ne ngis nga ab bug? Xoolal limu jafe-jafe yi ñu tijji ngir seet baxam bug bu waneesu ko noppi. Su dee ni deme wul ni, ngaa yonnee jafe-jafe bu bees.

🛡️ Soo gisee lottug kaaraange, Bul tijji jafe-jafe. Yonneel bataaxel ci contact@codeforsenegal.org.

Matalal ca na mu gën a man a matee booy melal jafe-jafe. Leeralal jafe-jafe bi te boole ci ay ndollent ngir njiit yi man a baamu jafe-jafe bi.:

  • Melo wi
  • Tolluwaay bu cine ngir ag baamu
  • Melokaan wu ràññeeku
  • Melokaan wu dëggu yi
  • Baamu ci ab lim

Laayebiir ci foŋsionaalite yu bees

💡 Di nanu bàyyi xel bépp càkkuteefu foŋsionaalite. Bëggoon nanoo xam sa gisiin ci anam gi nu manee yokk sunu naal bi.

Ngir yónnee nu njañse, tijjil issue buy melal foŋsionaalite bi nga bëgg. Joxeel bépp xibaar ca na mu gën a man a matee li nga bëgg nu yokk ko ci:

  • Melo wi
  • Melokaan wi ci tolluwaay yépp
  • Leeralal li tax yokk googu am njariñ

Ëndi njañse ci yaxu kod bi

💻 Bëgg nanu nga rimb yoxo yi ci ban bi da di kode ci naal bi.

Soo xamul fooy tàmbalee, man ngaa doore ci saytu jafe-jafe yi nu màndargale ni ki nii:

  • Good first issue
  • Help wanted

Nala wóor ni yaa ngi topp jëfiin yi gën yu kodaas yi nu taamu ak digle yi ngir ligeey ci git yi nekk ci suuf 😉

Jëfiin yi gën

Jëfiin yu baax yu kodaas 👌

Git workflow

Sunu yoonu liggéeyandoo mi ngi nu leeral fii .

Lu aju ci Code for Senegal

Ab mbooloom way defal-yàlla lanu (dewelopëër, ux / ui, jokko, data siantist, graafist, dewops, kaaraangeeg informatig ak yeneen) yuy liggéey ci ak coobare wu ngir ëndi ay saafaray disitaal ci jafe-jafe yu askan wi. #techforsocialgood. Soo bëggee xam lu gën a yaatu ci sunu ay naal xoolal kaaaycoder walla soo bëggee jokkoo ak kenn ci sunu way liggéeyandool man ngaa yónnee e-mail ci contact@codeforsenegal.org.

Doxaliin

Naal bii ak bépp nit bu ci tàbbi, li ko tënk mooy doxaliinu Code for Senegal. Boo ci tàbbee, da ngay topp ci tërëliin woowu. Fësëlal bépp melokaan wu jaaduwul ci safespace@codeforsenegal.org.